Lëkkalekaay
Lëkkalekaay yi ñooy tax ñu man a jòge ci aw xët dem ci weneen wu mu lëkkalool.
Gongikuwaay ak àgguwaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ab lëkkalekaay day am gongikuwaay (maanaam fa muy jóge) ak ab àgguwaay (maanaam fa mu war a àgg, jëm fa). Soo doxalee xeetu(element) lëkkalekaay bi, ca saa sa, da ngay man a jàll ca àgguwaay ba.
Gongikuwaayub lëkkalekaay day doon naka-jekk aw xeet(ab baat, walla nataal,...) bu ab jukki. Àgguwaay bi man naa doon aw xeetu benn jukki bi, loolu la ñuy wax lëkkalekaay bu biir. Àgguwaay bi man naa doon itam beneen jukki, bu dul bi mu nekk.
Jaar-jaar
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Lëkkalekaay yi ñi ngi sosu ci ati juroom-benn fukk yi, waaye seenug tas mi ngi ànd ak màggug internet, di fu Lëkkalekaay yi di boole, niki ag lënd, ay junny junni dal ci Lëkkale(resaux) gi. Su dul woon Lëkkalekaay yi, xereñu Internet di na wàññiku bu baax, jafeel ag jëfandikoom.
Ak jëm-kanam gu réy gu Internet, lëkkalekaay yi, ci li ñuy wax tag yu HTML lañuy jaare di leen sos, joowukaay bi won la ko; ci misaal
moo lay jox: wikipedia
Tay jii sax lëkkalekaay yi ay nattukaay lañu, limu lëkkalekaay yiy jëme ci ab dal ci la ñuy xamee ñaata la siiwee.
World Wide Web
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]lëkkalekaay yu World Wide Web bi ci xëti web yi la ñu nekk, maanaam ci jukki yi ñu bind ak HTML (Hypertext Markup Language).